Kàddug Yàlla gi
Sa kàddu laay niitoo samay tànk, muy leeral samaw yoon.
Sabóor 119.105
Jot sa téere Kàddug Yàlla gi
Jokkook nun
Bëgg nañu la jàpple nga am sa téereb Kàddug Yàlla gi. Jokkook ñun ci Messenger ngir ñu man laa boole ak ku la mana jox ab téere, di la won naka ngay jànge téere boobu.
Ab Jukki ci Kàddug Yàlla gi
Bu fekke ne masuloo jàng téere bii di Kàddug Yàlla gi, man nga tàmbali ci appli bi. Appli bi dafa ëmb fukki njàng ak juroom ñett (18) yi ñu jukki ci téere bi. Appli bi am na alfa, wolofal, ak baat yi nga mana déglu (audio).
Ab Jukki ci web
Man nga déglu Ab Jukki ci Kàddug Yàlla gi léegi nii ci sa nawigateur web. Mbindum alfa la ak baat yi nga mana déglu (audio).
KÀDDUG YÀLLA GI
Appli bi moo ëmb lépp lu nu jota tekki ci wolof ci Kàddug Yàlla gi. Amul audio.
KÀDDUG YÀLLA ci wolofal
Bu fekke wolofal nga gën xam, man nga yeb appli bii, bu ëmb lépp lu nu jota sotti ci wolof ci mbindum araab. Amul audio.
Yoonu Njub
Man nga déglu sa émission Yoonu Njub ci sa portaabal walla ci sa ordinatër.