fbpx

am ngeen ay laaj?

Wolof Njaay ne na: Jàng du wees.
Bu ngeen ame ay laaj ci mbirum Isaa walla Kàddug Yàlla gi,
jombul ngeen am ci ay tontu yu leer fii.

Bu ngeen fii gisul seen laaj nag, bësal fii ngir jokkook nun ci Messenger.

Jokkook nun

laaj ak tontu

Lan moo tax nu ne ‹Isaa mooy doomu Yàlla?›
Wax boobu, Doomu Yàlla, lan la tekki? Nanu xol ci Kàddug Yàlla gi. Ci Luug 1.28-35 bindess na ne:

Malaaka ma dikk ca [Maryaama] ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.» Waxi malaaka ma daldi jaaxal Maryaama, muy xalaat lu nuyoo boobu mana tekki. Malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Maryaama, ndaxte Yàlla tànn na la ci yiwam. Dinga ëmb, jur doom ju góor; nanga ko tudde Isaa. Ku màgg lay nekki, te dinañu ko wooye Doomu Aji Kawe ji. Boroom bi Yàlla dina ko jébbal nguuru Daawuda maamam. Noonu dina yilif askanu Yanqóoba ba fàww, te nguuram du am àpp.» Maryaama laaj malaaka ma ne ko: «Naka la loolu mana ame? Man de, janq laa ba tey.» Malaaka ma ne ko: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji.»

Bi malaaka bi waxe Doomu Yàlla, lan la ci jublu? Ndax daa doon wax ne Yàlla wacc na kaw asamaan ngir am doom ak Maryaama, walla leneen?

Boo gisee Senegaale bu tukki ci beneen réew, ndax duñu ko woowee doomu Senegaal? Ku ko def, ndax lu mu bëgg wax mooy réewum Senegaal moo juur waa jooju niki nit?

Ku nu wax Doomu Yàlla, yan jikko lay yor? Ban dundin lay wone? Lan la ku mel noonu wara jàngle? Jàngatal mbirum Isaa ci page Wideo.

Dégg naa nu ne, am na ay nit nu soppi Kàddug Yàlla ci Tawreet, Sabóor, Injiil, ak yeneen mbindi yonent yi, te manuñu wóolu teere yooyu tey ji. Loo ci tontu?

Nanu xol ci Kàddug Yàlla gi. Ci Yowaana 10.35 bindees na ne:

…kenn manula randal waxi Yàlla.

Itam ci Esayi 40.8 yonent bi wax na ne:

Am ñax day wowal;
tóor-tóor day lax.
Waaye sunu kàddug Yàlla
mooy sax ba fàww.

Ci Sabóor 119.89 bindees na ne:

Aji Sax ji, sa kàddoo sax dàkk,
taxaw jonn fa asamaan.

Ci Macë 24.35 Isaa moo wax ne:

Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.

Ci Yawut ya 4.12-13 mu ne:

Kàddug Yàlla de luy dund la, ànd ak doole, te moo gëna ñaw saamaru ñaari ñawka bu gëna ñaw. Day sar ba fa xel akug noo digaloo, ba fa yax ak yuq dajee, te man naa càmbar ay xalaat ak mébéti xol. Te it amul mbindeef mu làqu fi kanam Yàlla. Lépp a ne duŋŋ, ne fàŋŋ, muy gis, te moom lanuy waxal bés-pénc.

Ci li nga jàng fii, kan mooy sàmm Kàddug Yàlla, bu nu jot ci? Ndax Yàlla man na seetaan ku soppi waxam?

Am na beneen laaj itam bu ci topp – ku gis waxi Yàlla, di ko weddi, fan la mujje? Bindees na ci Peeñu ma 22.18-19 ne :

…képp ku dégg waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii: ku ci yokk dara, Yàlla dina dolli ci sa mbugal musiba, yi ñu wax ci téere bii. Ku dindi dara ci waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii, Yàlla dina dindi sa wàll ca garabu dund ga ak dëkk bu sell ba, ñaar yooyu ñu bind ci téere bii.

Ku gis waxi Yàlla, ba pare wax ne lii du waxi Yàlla, lan mooy mbugalam?

Wolof Njaay ne na: weddi, gis bokkul ci.

Bu fekke masuloo jàng téereb Kàddug Yàlla, jàngal ko te laaj sa bopp – ndax sama xol seedewul ne lii mooy Kàddug Yàlla dëgg? Ñaanal Yàlla, laaj ko – ndax lii sa kàddu la, am déet?

Jàngatal Kaddug Yalla ngir sa bopp fii.

Lan moo tax nu dégg nu wax Yeesu, ñeeneen nu wax Isaa, ñeeneen nu wax Jésus?

Ku nu wax Isaa, Yeesu, walla Jésus – tuur wi amul solo, lu am solo mooy nit ki. Boo ame xarit ku tudd Samba, man nga ko woowe Bàcc – ba tey moom la. Sa doom – man na la wax Baay, walla Papa – sa soxna wax la Nijaay – sa papa wax la doom sama – waaye ba tey yaw la.

Man nanu yokk tuuti nag ngir faramfance fu tur yooyu joge. Boo doxoon ci wetu Isaa ci kaw suuf, doo dégg tur yooyu – Yeshua ngay degg. Tur la ci làkku Yawut ya biy tekki Yàlla mooy musal.

Tur woowu bu nu ko binde ci làkku gereg ci téereb Injiil, danu ko binde ni: Iesuus. Boo ko jële ci gereg, dem ci araab, muy Isaa; boo ko jële ci gereg dem ci faranse mooy Jésus. Bu la neexe ci wolof man nga wax Isaa walla ba tey Yeesu baax na. Lu am solo du tur wi; lu am solo mooy nit ki.

Nungiy lay ñax nga dem ba wées tur wi, te jàngat ba man tontu ci laaj bii: Lan nga xalaat ci nit kooku? Jàngatal mbirum Isaa fii.