fbpx

Buleen RagaL

Xam kan mooy Isaa dëgg

Lan ngeen di ragal?

Ku nekk am na lu mu ragal :

Duma tekki. Kenn du ma bëgg. Fan lay mujje? Naka laa man ame jàmm ak nit ñi? Ak sama waa kër? Yàlla bu ma gisee, lan lay xalaat? Ndax man naa xam sax fu ma tollu ak moom?

Bu nu dawee laaj yooyu, man nanu am tuuti jàmm, waaye laaj yooyu, kenn manul leen daw ba fàww.

Ku xiif bu gisee mburu buy maye, dina daw gaaw woo moroomam bu xiif ni moom, ne ko: Kaay ab mburu a ngii.

Gis nañu ku mana indi ay tontu yu wér ci li ñu ragal. Bëgg nañu yeen itam ngeen am jàmm jooju nekk ci Isaa Almasi bi.

ÑUN ÑOOY ÑAN?

Ñun ay taalibe Isaa lañu ñu dëkk fii ci Senegaal.
Gis nañu yoonu jàmm bu nu Yàlla ubbil jaarale ko ci Isaa, te bëgg nañu seddoo loolu ak yeen waa Senegaal gépp, te bëgg nañu indi ay tontu yu léer ci ñi am ay laaj.

Kàddug Yàlla gi

Kàddug nit dafa ñuy xamal moom mooy kan, li mu bëgg, li nekk ci xolam. Naka noonu, Kàddug Yàlla gi mu jaarale ci ay yonentam moo nu xamal kan mooy Yàlla, li mu namm ci doom Aadama yi, ak cofeelam ci nit ñi mu sàkk.
Kàddu googu mooy Tawreet, Saboor, Injiil, ak yeneen mbindi yonent yi. Ci mbind yooyu lañu mana am ay tontu yu wér te léer ci sunuy laaj.

yokk seen njàng

Isaa – ñi dégg tuuram bare nañu, waaye ñi ko xam dëgg barewul. Jàng du doy, du wees. Yokkleen seen xam-xam ci mbirum Isaa tey jii.

Seetanleen ay Wideo ci mbirum:

Lan mooy sell dëgg?

Lan la Isaa jàngle ci mbirum…

Jàng Ñaan

Téereb Kàddug Yàlla, lan la jàngle?

Ay seede

Naka laa man ame jàmm?

Sunu ëttu Facebook

Man ngeen ñëw bokk ci sunu
ëttu Facebook ngir jot ay njàng, bokk ci waxtaan yi, te jokkook nun.

Jokkook nun ci Messenger

Nungi leen di déglu ci seen laaj ngir won leen lu Kàddug Yàlla gi wax; noppi nañu ngir ñaanal leen ci seeni jafe-jafe.

Kàddug Yàlla gi ne na:

1 Yowaana 4.18

Genn ragal amul ci mbëggeel, waaye mbëggeel gu mat sëkk day dàq ragal. Ndaxte ragal day ànd ak mbugal; te ku ragal, mbëggeel matul sëkk ci yaw.

Yawut Ya 13.6

Boroom bi moo di sama ndimbal; duma ragal dara. Lu ma nit manal?

2 Timote 1.7

Xel mi nu Yàlla sol du ànd ak ragal, waaye day ànd ak kàttan, mbëggeel ak moom sa bopp.